Naa raw ñi lay sopp raw mbooleem ñi lay jox i yëf - Wolofal Serigne Mbaye Diakhaté
Автор: Serigne Mbaye DIAKHATE
Загружено: 19 апр. 2025 г.
Просмотров: 256 просмотров
Yaw ngën ji wéttalu bët tay ngën ji wéttalu xol
Nekkal di wéttalu saa bët fàww ak sama xol
Ta donte waa penku ak waa sowwu ñëw na ñu tay
And ak man it, bu ñu tax mbég tàbbi sax sama xol
Saa gët yi nay ja ci yaw, saa xol bi nay ja ci yaw
Saa cër bu nekk nalay béglooka daw ci ndigal
Bu nit ñi dee denci ay soxnaaka fàggu dugub
Di jëndi fas aka war tay dox di denci alal
Naa denci man sa ngëram, tay fàggu nag sa ngëram
Tay jënd it sa ngëram yaw mii ta jàpp la jël
Naa raw ñi lay sopp raw mbooleem ñi lay jox i yëf
Raw gaa yi lay jëfal it, raw gaa yi kenn jotul
Ta jox ma nag itte juy jëm kaw li kaw, rëy a rëy
And ak wér ak gudd fan ak ndimbal ak rafetal
Sakkal ma bunt bu lëf xalseet a dox di ma lor
Ta may ma nag lu nu may soppeeka ñee, yëramal
Yëram nu, jagle nu yërmàndeeki yiw ta dogal
Ci nun lu sedd suñub xol fàww ful nu te fal
Baril nu, yokk nu biir ak biti, ful nu bu wér
Ta fal nu tundu ngëram ak bàrke fàww, defal
May ñooti, jox ñooti, sellal ñooti, yeeti nu nun
Yeeteg ngëram ndax nu far gëmlaati, yaa nu soxal
Gëm yépp nay dollikookay jëm kanam bu rafet
Ta itte yiy yokk nit ñiy sante jëf aki xol

Доступные форматы для скачивания:
Скачать видео mp4
-
Информация по загрузке: